(3) Xundooñ ngeen Njiin na ngay fellax
BISMI LAAHI RAHMANI RAHIMI
Xundooñ ngeen Njiin na ngay fellax
Ku mos, muy gééj gu neexum ndox
Ku nann, bilimbaane, dootoo dox
Di saytu sa ndaa di rootaani
Te Muhamadu moom riñaanoon na
Fa Màkka ba Njool ma jalloon na
Limub asamaaw ya déggoon na
Fa Yàlla la tiiñ ka jàngaani
Mu dellusi jànx, dem faati
Ki làbbali yoon wi moomaati
Bu leen bañ céébo maa ngeeti
Ku bañ wile waame xaaraani
Wolof nga nu feeñu bés nikki tey
Wolof laa nàmp woy la ba tey
Liggééyal Yàlla moo gëna yay
Mu sant nu, noo ciy kontaani
Ñi rééroo sànku ngeen ku ci bañ
Ki Yàlla yabal, waxam ja du deñ
Te Mahdiyu mooy boroom sañsañ
Te mooy ubbi "baabu jannaati"
Mahdiyu laay fajal na nu mar
Ba Njiin wootee la foore ya wor
Sunub sang jooy na, Saaba ya xar
Rogoñ yay "baxru rahmaani"
Tanxal na ca soppe yaak bañ ya
Junniy junni naan ca leeram ya
Nit ak jinné woo na leen dunyaa
Ngiréék ñuy jaamu Rabbaani
Ba Njool may waaja feeñ ku jubul
Ka jooy fa safaan ba, jaam ya yëgul
Niiraan jooyle kook ya mu sol
Rogoñ yaay "baxru Zulmaani"
Labal na ca lenn ciy fooréya
Bu ñuy firi boole seen tor ya
La ñuy firi wooratul jaam ya
Ba Njool ma ñu jiñ ko seytaane
Ba Mahdiyu feeñagul amu fi
Ku fiy wone yoon wu jub néwu fi
Li Yàlla bëgg ak li muy tere fii
Lu ngeen bañe Baay Libaas la ne
Barib xamxam taxul mana dem
Siraat am ndok la, bés bu ñu jëm
Ki fiy wone yoon wi moo mata xam
Te farlu ca laa mu santaane
Ku tektaluwoon ci waa ju gëlëm
Da ngay mujjé réére mbir ci waxam
Ku réére jamano, doo mana xam
Boroom a nga leen di dénkaane
Xëccoo leen wéétëluk Fari ja
Bu leen jàngaani ngir daraja
Yonnent, foore ya mooy dono ja
Ségém rombul ndigël daa ne
Da nuy tagg Njiin boroom jamano
Ki woote, nu woolu kay naxu nu
Da fay gindi ruu yi booleek nun
Nu dellu ko sant "hamdaani"
Bu leen xeeb jaam bu aw ci ndigël
Ndigël du ndugël, ragal nanu bël
Boroom gaal gi moo nuy jël
Yoobu nu pééy ba nuy naane
"Al hambdu li Laahi Maaliku naa
Wa salli a laa Muhamadu naa"
Ku lay mana sant man raw naa
Ndegam du ka siiwé "alfaani"