(4) Badaa xuruubiyu samsan
BISMI LAAHI RAHMANI RAHIMI
"Badaa xuruubiyu samsan
Wa anta Mahdiya Laahi"
Boroom cosaan ya ko jàngoon
Da ñoo xamul Nabi Laahi
Boroom junjugn ya fa Màkka
Moo moom junjungn ya fa Taayif
Boroom junjungn ya ca Firdawsi
Moo di Baay ñangu Laay
Bu gaalug diine ga teeree
Ku ñaanul paas di nga tardee
Limaamu "safinatu saadati
Xawsu nixmatu Laahi"
"Imaamul il mursaliina
Wa xaatimu nabi-iina"
"Liwaa-ul hamdi" nga tàllal
Nu gis ko gëm Nabi Laahi
Ku naw sa àlluba weddil
Te ñëw mu won la nga daanu
Mu sol la leer ya nga sàbbaa
Ba naan Alhamdu lilaahi
Limaamu Laay, ba mu wootee
Fa gaaña rééré fa sowu ba
Yatam wa dal, mu ne tuub leen
Ba gaa ya nooy Na bi Laahi
Limaamu Laay ba nga taaloo
Ba leer ya jolli ca biir Yoof
Lëndëm ga daay na ba naawal
Xérëm ya, ngay Nabi Laahi
Boroom xérëm ya da ñoo gaaw
Tabax jumaa ja ca xeer ya
Mbaaxam ga tax na ñu booloo
Ne laa ilaaha illa Laahu
Toxal nga biddaa ci sa diiné
Nàndal nga mag ña ca leer ya
Làkkal xaleel ya fa nekkoon
Ñuy xañtu diiné "li Laahi"
Yaay gééju leer gi di baawaan
Dekkal nga xol yi fi deewoon
Ku aw sa ngir mi fasoo naani
Tuubaa, woolu na Laahi
Biddiw ba xotti na leer ya
Sa lay wa jééx na fa jaam ya
"Illaa bi hadrati man xaala
Ajibuu daa-iya Laahi"
Nit ak jinne la ko boolee
Goor ak jigeen na ñu jaamoo
"Balaxta sawta ka sarxaam
Nawarta xarba li Laahi"
"Balaxta sawta ka yamiin
Balaxta sawta ka jawfu
Muhyi fuhaadi faxiira
Ibaadi najiya Laahi"
Li Yàlla sante jaamam yi
Fooreeyaa ko di juuyoo
"Jasaaka Mahdiyu Laahi
Wa fayta huduuda Laahi"
Yaaram bi nee wuloo"baa"
Yaarambi nee wuloo"siin"
"Anta miftaa u bahril
Uluumi bi Bismi Laahi"
Sunu Yonnent ba mu faatoo
Werante waa nga ca réér yaa
Da ñoo xamul xalifaam
Seydinaa Isaa Ruuhu Laahi
Ba mu bawoo béyti Maamur
Saxaar la war ba Yaraaxoo
Boroom cosaan ya ko jangoon
Da ñoo xamul Ruuhu Laahi
Waxtaan na faak ña mu andal
Ba jiite leen julli ñaan
Sunu Boroom defal na ko ñaanam ga
Muy "Wixaayatu Laahi"
Sangn gi Yàlla Sangneel la
Fa noon ya ak Nasaraan yaa
"Tamuru bi xaybati him
Zu kiraamti, inda Laahi"
Jirim sëngéén ñetti fan
Ba Njool Medina ñëw la ñu reeo
Mu bégël jullit ña ñu sabbaa
Mu daagu jëm Jàmmalaahi
Ñu raam sujoot, ba ñu noppee
La seen rongoñ ya di maayoo
Njool ma jullée sunu yaaram
"Nazalta yaa Ruuhu Laahi"
Kerook la gééj ga di sàbbaa
Lewet ba gëm ya di naanoo
Ku naan ca teen ba di sàbbaa
Te sant Baay Ñangu Laahi
Buur Yàlla woo na ko Pééy bub
Ku dootul moom du fa jaaroo
Mboole mi ndééy la ca gën
Muhamadoo ko déglu fa Laahi
Ngawar gu réy ga nga naaweek
Buraax ba dem ba ca Pééy ba
Noonam ya koy bëgg roy
Seen masin ba sew na fa Laahi
Sa waay du jàq du jaaxle
Lëndëm gu tar du ko laaloo
Leeram ya doy gëne jolli
Mu am "ridwaanu li Laahi"
Laa ilaaha illa Laahu, du nu sàppi
Ngir mooy junjugn ya ca Pééy ba
Yal na mujjug sunu "Kalaam"
Di laa illaha illa Laahi
Laay laay la laa illa laahu
Woy leen Jabeel ma ca leer yaa
Limaamu Laay li nu lay woy
Du jééx du xaaj dunu tayyi