(5) Jantub diine lislaam
BISMI LAAHI RAHMANI RAHIMI
Jantub diine lislaam
Da ngaa fenk ñuy miim
Nu gëm woolu leer yaa
Ngi baawaam fu ne
Baay Laay ngeen ne jangul
Mu woo leen, ñu gàntal
Ginnaawam ga daaneel
Fi haalim ju ne
Jinnéék nit la woowoon
Ci diinéém, ku teewoon
Te doyloo ko diiwaan
Nga doy ko lu ne
Da ngay jantu njolloor
Ñi gàntoo ngi ciw guur
Te lii woor na kuy gor
Ci diiwaan bu ne
Rasuuloo ilaahi
Ibnu Abdulaahi
Moo leen woo wa Laahi
Madiine fi ne
Yàllaa magg mooy Buur
Turam woowa nay riir
Ba seen xol sangoog leer
Mag ak ndaw ku ne
Rasuuloo ilaahi,
Mahdiyoo ilaahi
Bi Laahi wa Laahi
Ku bañ "perta" nga
Na ngeen déglu baat bi
Da may woy Yonnent bi
Booleek sant Rabbi
Te moo war ku ne
Wolof yooya laa miin
Te moom laay wuyoo Njiin
"Sekarteer" amul yoon
Ci Yonnent bu ne
Al hamdu li Laahi
Wax ko war na noo
Ngir moo feeñal Yonnent
Ci biir xeet wu ne
Gééjug leer ci Soodaan
Xamul yaa ngi rootaan
Sangoo leen ko nuy naan
Moo gën ndox mu ne
Seydi Ruuhu Rahmaan
Donoy Mahdiyoo
Ba yaaram ba làqoo
Ba tey yaa fi ne
Ba muy woote diineem
Te ñuy bañ tariixaam
Nga dib taaw di seedeem
Ba tey yaa fi ne
Da ngaa jub, sa ñoñ jub
Woyof toyy niw xob
Di jambaar def ub tab
Siggil yaa fu ne
Daraapoo bu lislaam
Bi yaa ko ame
Bu leen yoon wi rééréé
Nga sañ ko wone
Boroom xeej bi yaa jaam
Ñi daarloo ci xamxam
Ci seen kow nga jël ndam
Siggil yaa fi ne
Da nga yiw, yéwen taaru
Doy képp kuy waaru
Séydéy boroom daaru
Yaa koy wone
Ku doyloo sa xamxam
Ba laajoo ñu gënë xam
Do taggook i jamjam
Yu réy wet gu nee
Baay Laay gééj gu dul jééx
Te raw lem ci ag neex
Te lamboowul ag tiix
Tanxees a koy wone
Setal seeni ñaaw ñaww
Nandal gaa ñaa ñuy soow
Xanaa xaw na ñoo naaw
Ku man dey wonee
Ku lay roy ci bi "xarnu"
Feeñul wonee
Da ngay njiit ci lislaam
Bi yaa leen tanee
Gënël ngë nu nuy ndey
Gënël ngë nu nuy baay
Te yaa gën sunuy maam
gënël nuy junné
Ku lay bañ du kontaan
Lu waaj waaj du waxtaan
Bu walle ñu reetaan
Lu man man mu ne
Ba Njool may taxaw
Ben si tey ngay xaree
Te wééroo sa gànnaay
Muy dal saa su ne
Jiyaar jii si baatin
Bu doon "Zaahiroo"
Ñu janloo nga daaneel
Ci goor ay junné
Ay jambaar nga andal
Ku lay sooru gental
Sa gànnaay ya koy dal
Du wér bay wunni
Liggééyal nga Yàlla
Liggééyal nga Baay Laay
Ba jot seen Ngërëm
Doo fi maasun gune
Ndawal Buur ku bañ weej
Ku réyréylu sew ruuc
Soppeem yaa nga noon
Ngééj ñu xam faa mu ne
Li tax diine yaa suux
Ba Yonnent jëkkee juux
Boroom tééré ya xoox
Di bañ wet gu ne
Tawreet ak Linjiiloo
Saboor diig nanoo
Furxaan teew na gàcceel
Ña noon nii du nii
Ñi daan bañ Rassooloo
Siraat ñooy rëpééloo
Tuubéén ñaa ko doyloo
Batey ñoo fi ne
Bu dul konte Baay Laay
Lëndëm sank fuy gaay
Ki tax ngeen di laay laay
Yàllaa ko yonni
Da nuy ñaan ki nuy mey
Mu yobbël nu buy doy
Ba cik mujj nu far wéy
Ci ngir mii nu ne
Sañseel gëm yi ñuy bees
Giroo ngir mu tek lees
Booleek ndééyi depess
Yu jëm pééy bu ne
Baal niiw yu wéy ya
Jéggël gëm yu teew ya
Ña làqook soppeem ya
Si nit ñeek jinné
Dundël diine lislaam
Ci barkeb Yonnentam
Di njiitam di soppeem
Da koy may lu ne
Da daan rey di dekkal
Fu lëndëm mu leeral
Ba gééj wéx mu wéxal
Ñu naan saa su ne
Ay kéémaan nga andal
Te say seede jééxul
Ku laamlaami laajal
Ci mag ñii fi ne
Li war yeenu "haalim"
Ci bii "xarnu" mooy xam
Boroom, boole kook gëm
Te aw cim ngirëm
Yeeteetoo ñu yeewoo
Xanaa ber sa saawaa
Sa ñoñ nàngni faawaa
Ba réér cik lëndëm
Bakkan jartil loolii
Da ñuy dee ñu suuli
"Fa la sakk xawlii
Axiixum hikam"
Da nuy sànk njalbeen
Jëndeek mucc, mu lew leen
Fa firdawsi nuy béél
Ku nekk taabalam
Ku dem Tuubaa gis pank
Yay daagu dox ndànk
Luy loolu seen tànk
Yay temtemi
Yaram yépp koy yëg
Kawar yépp koy yëg
Muy banneex bu dul dog
Bu dootul yeme
Su Buur Yàlla santee
yonnentaam mu wootee
Ku wuyuwul bu sottee
Nga réccuk mujjam
"Fa yaa ahlu soodaan"
Yonnent feeñ na woo leen
Da ngeen gàntu nee ngeen
Du moom, noo ko gëm
Bu dee fooréya, lay jeex
Nde tektal ya day weex
Ca tééréém, da dul neex
Dey jeexal xolam
Ku fiy jaaxle laajal
Ñi xam ñoo di tektal
Ñi séytaane rééral
Ba tax ñoo gëlëm
Njiinoo njiin jibul neen
Njiinum Yàlla raw leen
Ëllëg teel ñu laaj leen
Fa Saam ak wallam
Ku bañ yërmëndey Buur
Kerook moom lañuy door
Mbugal wër ko muy nuur
Du taggook loram
Yonnent baa mu woottee
La saabaam ya footee
Ku noon "aamanaa"
Tey nu laabal xolam
Ci saabuy Boroomam
Saxoo tur wa mooy xam
Xalam muxjizaatam
Te fàgguy ngërëm
Yàllaa yonni Baay Laay
Ci nit ak jiiné
Na leen woor ne Séydééy
Borom "xarnu" bi
"Allaa-uma salli
A laa xayru rusli"
Ñi Buur tann boolee
Ñu sëlmël ci ñoom