(8) Bi Bismi Laahi ma deeti woy Madiné
BISMI LAAHI RAHMANI RAHIMI
Bi Bismi Laahi ma deeti woy Madiné
Wolof la may mottalikoo saa yééné
Tey ba ëllëg nuy wuyu Maam Limaamu
Moom ki nu woo ci ngir mi, ngir nu jaamu
Al Hamdu li Laahi, nuy sant Buur ba
Jaglel na nu sang, tabeel ndijoor ba
Séydi Limaamul Mahdiyu taabeem ga
Jéggi na waame, raw ginnaxu gééj ga
Dogoonkoon ak Mahdiyu laay mi woote
Kuy jééma leeral mbir mi yaa koy wuute
Waxtu wu jot nu jàpp, ken du tiimoo
Lottal na Lawliya yi, noo ko moomoo
Sikkar guddéék bëccëg ni riiru gééj
Yonnent jagoo nay juñjungn du ndiij
Nu sant doomi Alsaan ak Seyni
Moom ki nu woo ubbil nu yoonu diiné
Moo jëkké fi lakkal xaleel yu tuut yi
"Wal ixtixaadi sawjan lil banaati"
Ponki julléék njapp mi ngeen màggaale
Fu ngeen fi jëm, Yàlla di seen àndaale
Goor ak jigéén, mag ak ndaw xaleel
Jaamu gi, noo si maase, naaj ak teel
Ku Yàlla yonni, noo ko mos ni siiw
Loo wax nu woolu, dootu nun di beew
Bu leen werante, baatu goor gi siiw na
Nit ak jinnee ko déggandoo te woor na
Baay Laay ne "Aajibuu daaya Laahi"
Muy wax ja woon ca yaa Rasuulu Laahi
Moom bés bu ne mu mel ni gan, nuy teeru
Ñi gëm te woolu saa su jot ñuy waaru
Mbooleem sëriñ si, raw na leen si waare
Tereek a digle, lii la Njool ma doore
Mbooleem ku fuy teyteyluy laaj, déggoon na
Waxam ja démb, tey donnaam ja teew na
"Sayaaratun daabatun Ruuhu Laahi"
Yàllaa di tax nga war ko waaw wa Laahi
Gis texe, maa le seeru, man kañ naa la
Gëm mucc, weddi alku, woolu naa la
Yaa wax nu dégg, jëf nu gis, mbër waadaa
Wuutewulaak doomi Maryaama Soodaa
Diggënte Beyti Maamur ak Yaraax
War nga fi daaba, muy ju gaaw, du xoox
Jub nga Yaraax, labbe ya doon la teeru
Sa làmpi leer sëggël na leen ñu yiiru
Nga wàcci war Maanatu Laay jëm Yoof
Jullee fa Njool ma, boole doom ya uuf
Say "muxjizaat", lottal na gaa ñay séénu
"Wa lan yaruu mislu ka yaa lamiinu"
Ku mos di weddi, yaa ko won mu seeru
Ku fuy tëbëntu ngay jiñax mu jooru
Kerook ba Maam ñibbee fa Jàmmlaahi
"Xad hayaru ashaabau fi Laahi"
Déelé bi suuf ak asamaaw yi ñoom
Jooy na ñu Njiin, jooyi guneek seen maam
Gééj ga di jooy, rongoñ yu tey yu neex
Ku sëgg naan, ba siggi waaru giix
Fekkoon nga mbooleem gëm yi jooy ba jééx
Sab taxawaay tax na ba seen xol fééx
"Ibnu Asan Séydinaa Limaamu
Abu Issaa Ruuhu Rabbil xadiim"
"Man xaala ajibuu daaya Laahi"
Amul keneen ku wax waxam wa Laahi.
"Wal mujrimiinal musrikiina naaluu
Xusraanu inda diina kum maxfuuluu"
Bu leen ragal keneen ku dul Ilaahi
Ak Yonnentam ba doomi Abdalaahi
Mbubbum ragal, Yàlla fu gën baraaya
Moo gën sujéé ka dox di bif daraa ya
Ruuhu Ilaahi, kiy donoy Rasuulu
Ibnu Imaamul muntasar, laa woolu
Ñay mbër ca Yàlla, seeni yan nga boolé
Saa sépp man, dinaa la ñaanal doole
Abaabakar, Umar, Usmaan, wa Aliyu
Yaa boole seeni mey di jiite gaa ña
Kuy jééma gotti saa mbër it bul naagu
Ndax wéqu weén tereetul ñay wa daagu
Ña wuyuwoon Yonnent ca ba mu woote
Mu japp gaa ña, boole xol ya footéé
Ku fuy tëbal ci Yàlla jii jamano
Na gëm dogal ba, mbaa du weesu daanu
Ku weddi alku, doonte "lawliyaawu"
Nit ak jinné si yam, na ngeen si yeewu
Yàllaa ma yonni, moom la wax fa Yoof
Ba Njiin jibéé la bokk yépp keef
Ñu naan ko wax ji réy na yaa Limaamu
Mu yékki baatam ba ca kow, ñu yéému
Jàngul, bindul giseesu fook i tééré
Xam xam ba cab dënnam xajul ci tééré
Yonnent bu Yàlla yonni lii la waare
Ndaw ñaak jigéén ña gëm, sëriñ sa réér
Lu ngeen fi deeti jang, safara yay na
Léébu wolof lawoon ca yàgg, feeñ na
Feeñoon na Màkka gaa ñu baax ña booloo
Sette waxam ja, muy ju woor, ñu wooloo
Am ca ñu jomlu, gantu ngir kiñaan
Ku and ak ñooñaa déég ba doo ca naan
"Xafadta diini kufra Ruuhu Laahi
Abaa ka mursalum fi diini Laahi"
Ma wax la tuuti fii ci say jalooré
Ba gaa ña dégg, Saaba yaak kay seere
Tabeek soxar la mbër yi mos daan boole
Kuy bañ ci ngir mi, ñoo ko daan yan doole
Yàlla la fal "Aamiral muuminiina"
Ku weddi fii sa wax, jëfam ja neen na
Sa tur a jiit sa taxawaay ci dun bi
Deefu la jaawaleek keneen ci gééw bi
Baay Laay rafet na diine, Njiin du maas
Ku weddi, sàngutee fa Maam Libaas
"Wa man yarju illaa jinaani Laahi
Xudaamu u faxlam u Ruuhu Laahi"
Yééfér yi sax yaras na sag njaboot
Ngir Maam Limaamu Laay mu réy mi boot
Aaye na jëw, aaye na fen rambaaj
Moo nuy musël, moo nuy fajal ay aajo
Digéb Yàlla, ba ñépp daa ko séénu
Mu ñëw, nu gëm, ñi wooluwul dëféénu
Weddi mosula jur i doom yuy daagu
Mujj ga du jàmm, ngall waay bul naagu
Yonnent bu woote, layu xeet wa jééx na
Ñi dégg tey tënxëmlu seen xol dee na
Saa Maam Limaamu rafet nay malaan
Leeri Yonnent ba, moo ko sol jawaanu
"Suxakadun" sàbbaa na, ñépp naan
Mar waa ngi réy ñi gàntu ngir kiñaan
Maa woolu Séydi, ba bésub péyoor ba
Ku bañ mu am, kerook doo naani Tuubaa
Yàllaa la yékki ngay boroom xarbaax
Way ngnàññ santu leen du ngeen war baax
Li muy digël jullit, mu war ko war ma
Yal na nu man ko, moo di leeral ngir ma
Wut ngërëmam ba tàkk dib jénéér
Moo gën junniy junniy junniy dinaar
"Salli wa salliman a la dawaami
Bi man daha li Laahi fil anaami"