Poème du Professur Assane SYLLA
Poème :"Buur Yalla di kéémtaan"
Par Le Professeur Assane Sylla
Bismi Laahi Rahmaani Rahiim.
Buur Yallaa di kéémtaan
Ndax moo man te moo xam
Yéému leen ci mbaaxam
Te gëm ko« wa Laahi »
Moom mi defar dun-yaa
Boole kok mbindééf ya
Gis leen xééwëlam ya
Ta waaru “LiLaahi”
Seetal dun-yaak li ci biir
Asamaan aki niir
Janta ,biddééw aki weer
Té yéému “liLaahi”
Yërmëndéém ja yaa na
Moom mi màgg wéét na
Amul maas ,tiim na
Mbindééf yépp “wa Laahi”!
Nanu gëm te woolu
Dëggël ko te doyloo
Muhammed Rasuulu
« Xayru xalxi Laahi »
Saabaam yaako seede
Gaa ñu baax ña teewe
Alxuraan ja wàcce
Di« kalaamu Laahi »
Liggééyam ba réy na
Ba tey jaamu sax na
Gaani santa war na
Ci baaxu Ilaahi
Penku baak ca sowu
Lislaam rafet siiwo
Leer ya dañu saawo
Nuy sujjoot li Laahi
Li Buur Yàlla tettal
Imaam ñëw ko leeral
Ruuhu dal ko siiwal
La nuy gëm“wa Laahi”
Limaamoo fi woote
Ne Yàllaa ma yonni
Waare , doy nu jiité
Nu wuyyu li Laahi
Am nga ndam fa Laahi
Tedd nga Baay Laahi
Wàcca nga« wa laahi »
Boroom diiné laahi
Moom du xool ci tééré
Jangul te du maas
Lii kay doyna seede
Ci waa« ahlu Laahi »
Seydi Ruuhu dem na
Jalooreem ya réy na
Manjoon Laay taxaw na
Di sellal« li Laahi »
Isaa gééju leer nga
Tabeek yiw taranga
Oyof muñ jàmbaar nga
Yewen jub« wa Laahi »
Seetal gaañu baax ña
Ak seen jë yu leer ya
Saxoo na ñu baat ya
Mu leen jox “li Laahi”
Laa ilaaha illa laahu
Muhammadu Rassulu
Yékki nañ ko selloo
Saxoo jaamu Laahu
Gërëm leen ku baax ka
Tafsir Ibra Mbenga
Taxaw seede, mat nga
Dëgël ka« liLaahi »
Jaam bu santa laahi
Dox di wuyyoo laahi
Jubël yoonu Laahu
Am ngërëm faLaahu
Nanuy moytu noonoo
Bu nuy dox di rééroo
Jullit yépp mbokkoo
Li dey woor na Laahu
Borom ol yu booloo
Bokk benn mbooloo
Ñaan ci Yàlla, yelloo
Yërmëndéém “wa Laahi”
Ku fuy dox di xottu
Wollëré ka xaste
Luy rééroo , nga jiité
Alku, yéés, “wa Laahi”
Bu nuy deeti réy lu
Moo di yoonu sànku
Te mooy indi jomlu
Ba gaañu fa Laahu
Waa ja dox di sàkku
Màxaama aka bàkku
Daraja dey ,sànku ,
Torox, sewfa Laahu
Buur Yàllaa di dogal
Te mooy Boroom xééwël
Ku ko soob mu xééwël
La leer yafa Laahu
Santa war na jaam yi
Ak lu man ti am fii
Ci dun-yaa te metti
“Al hamdu liLaahi”
Nanu Yalla jubël
Ci lislaam te musël
Nu ci bépp mbugël
Te baal nu« li Laahi »
Allahumma salli
Nu dellooti julli
Ci yonnen bilaahi
Tey santa Ilaahi .